Jàngat Téere



 Buur Tilleen bu  Séex Aliyu Ndaw 


Tëralin wi

Ndoortel li


      I.            Jaar-jaaru Séex Aliyu Ndaw ak téere yu mu jott a mbind

   II.            Yaatal jëmale ci téere bii di Buur Tilleen 

III.            Way-jёmmali ak béréb yi ci téere bi
1.     Way-jёmmali
2.     béréb yi

IV.            Tёnkub téere bi

    V.            Jàngale yi ak suñuy gis-gis ci téere bi
1.     Jàngale yi
2.     Suñuy gis-gis ci téere bi

Njeextal

Ndoortel li
Danuy faral di nan « littérature » maanaam lépp lu aaju ci bind ak taaral ci Afrig mi ngi tàmbalee ci atum 1926 ba nga xam ne ki di Baakari Jalloo  bindoon ab téere nettali « force bonté» (doole bu sell) ci kàllaamay farãse walla ki di Casely-Hayford « Ethiopia unbound » ci atum  1911 ci kàllaama Shakespeare. Waaye nak war nañu di fàtteli ne ci atum 1907 la ki di Thomas Mofolo bindee ab téere « Moeti oa bochabela » (nemmeeku tukki ca penku) ci kàllaamay sotho ñu ràññee ko fale ci réewum Lesotho ( te sax jot na bind ñetti téere ci diggante atum 1877 ba 1948 te it mu nekk 41e nettalikat ci 2Oe « siècle » );  walla sax ki di Afa Wark moom mi nga xam ne mo bind téere bi di « Lebbw wallad tarik » (kàddu bu jibee ci xol) ci atum 1908 ci kàllaama  ahmarik. Loolu mu ñów nak dàqal bépp xalaat buy déggal ne doomu afrig walla sax nettalikat afrig yi njëkk ci kàllaama tubaab la ñu dooree bind.
Senegaal nak, ci wàllum mbind ci kàllaamay réewmi mënu ñu def dara lu dul delloo njukkal ñi  di sëriñ yi ku ci mel ni Musaa Ka nga xam ne ci gàttal rekk def na kemtalaay kàttaanam ci bidum làmmiñu réew mi. Te loolu am na sax ñu naan amoona sax balaa tubaab yi di ñu noot (lu ci mel ni wolofal). Bu ñu fa jógee amu ñu lennen lu ñuy def lu dul gërëm liggéeyu  ñenn ci abbeyi, ki ci mel ni Abbé David Boilat moom mi nga xam ne ci atum 1858 gànnaaw bu mu bindee ci atum 1853 les esquisses sénégalaises ba noppi, mu daal di bind li di grammaire de la langue wolof. Li ni mel ak yeneeni-yeneen liggéey yoo xam ne di nañu ci gëna àndi ay leeral ci kanam, ñoo laal démbu bind mi ak taraal ci kàllaama réewi afrig yi.  Li di Buur Tilleen bi nga xam ki di Séex Aliyu Ndaw moo ko bind ci atum 1963 been la ci téere nettali yu ñu njëkka muul ci làmmiñu Kocc Barma. Bii téere nak mooy waral suñuy waxtaan ci pàcc yi ci topp.


                  I.            Jaar-jaaru Séex Aliyu Ndaw ak téere yi mu jott a mbind
Ñu gёn koo xamee ci turu Séex Aliyu Ndaw, Siidi Ahmed Aliyu Ndaw mu ngi gannee àddina ci atum junni ak jurόom-ñeenti téeméer ak fanweer ak ñett (1963) ñett fan ci weeru waxset ca «Bignona» (kasamaase, Senegaal). Mu doon Jàngalekat ci làkk angale, ci atum junni ak jurόom-ñeenti téeméer ak jurόom-fukk ak juróom-ñett (1958). Moom, Abdulaay wàdd, Jibriil Asaan Mbeŋ, Masàmba Saare ak Asan sillaa ñoo taxawal ca «Grenoble» kurélu ndaw loolu te taxawaloon Ijiib Wolof. Séex Aliyu Ndaw bindkat la ci wàll bu ne, bind na ay kilib:  «L’exil d’Albououry», Nguy Njulli, «L’Ile de Bahila», ay téere nettali yu mel ni  Mbaam Akimoo, «Exellence vos épouses», «Un bouquet d’épines pour elle» ak Buur Tilleen, benn maye «Le marabout de la sécheresse», ak woy lu ci mel ni Kairée. Ci gàttal rekk mën a ñoo wax ne rekk ku bëggoon bind la.  Ca atum junni ak jurόom-ñeenti téeméer ak jurόom-ñeent fukk ak ñeent (1990) daana ka Séex Aliyu Ndaw téerem yépp la tekki ci làmmiñu wolof ba mu des «L’exil d’Alboury ». Bokk na ci ñuy xex ngir làmmiñi Afrig jёmm kanam, waaye li ni mel nak taxul been yon mu bàyyi bind ci yemen làkk yi.

               II.            Yaatal jëmale ci téere bii di Buur Tilleen :

Afrig nak daana ka ni ñu ko waxe ci ndoortel li daana faral di jànkoonte yeen tolof-tolof ci wàllum bind mi rawaatinak ba nga xamee ne lu mel ni muulkayi lu ci ëpp ci ñoom  duñu sawar walla sax dunu nangu muul bépp téere bu nu bind ci làmmiñu réew mi. Dey am sax ñu yaakaar ni bind ci kàllaamay réew mi du dara lu dul ñàkk soxla walla am jott. Li moo tax nak bind ci kàllaamay réew mi jafewoona lool. Waaye nak taxul ñenn ñi baayi mu sedd ndaxte ñu ci bari ku ci mel ni Séex Anta Jóob, Aasan Sila, Séex Aliyu Ndaw ak yeneeni-yeneen kaɳkam ñoo taxawaloon fale ca Goronobal ca réewum farãs ngir taxawal li laal tey bind walla liif ak liifantu ci làmmiñu Kocc Barma ñu tuddee ko Ijiib wolof. Noonu ki di Séex Aliyu Ndaw moomi nga xam ne dafa yàgg xamle ne bind ci farãse nekkul bëgg-bëgg waaye ñàkk pexe. Ci kaw loolu mu daal di bind ci atum 1974 li Buur Tilleen ci farãse gànnaaw bu ñu lànkee ne mug duñu ko muulee ci wolof. Bi téere toog na ay ati-at ba 1963 ba nga xam ne li di kurelu Ñoɳteg làmmiñu Doom Aadama ci IFAN CHEIKH ANTA DIOP ak ACCT taxee ba ñu mën jàng Buur Tilleen ci làmmiñu Kocc Barma mi ko taxoon a jóg.    

           III.            Way-jёmmali ak béréb yi ci téere bi

1.     Way-jёmmali
Ci téere bi nak ràññee nañ ci :
·        Maram muy yaayu Ràkki jabaru  Góorgi Mbóoj mu doon ku fonk jëkkëram lool ak doomam di bàjjo. Magu Kéwé.
·        Góorgi Mbóoj boroom këru Maram, baayu Ràkki doonoon buur ca Waalo te mu jógee fa gànnaaw bu mu jàmmaarloowee ak komaandan bi, xaritu benn bopp baayu Bugguma ñu tuddee ko buur Tilleen.
·        Ràkki been bantu Maram ak Góorgi Mbóoj, yu fonk ko lool. Mu doon génn ak Bugguma. Moo àndi jaxasoo bi ci téere bi.
·        Bugguma ñeeño, moo tooñ Ràkki.
·        Baayu Bugguma boroom alal ca Tilleen, gore te xam boppam muy xaritu Góorgi.
·        Kéwé rakku Maram, mooy fat Ràkki ba ko baayam dàqe ci këram, ñéppa ko dëdduwoon, dogook moom ba fàww, mu moom boppam.
·        Sindax fas bu Góorgi, mu ko ndan fàtteli démb.
A
·        Mën naño ràññe ci biir téere bi ku ci mel ni : doktoor, mbokki Góorgi, rakk yu  jigéen Maram ak way-juram, waa Tilleen ak Waalo.

2.     Béréb yi
Jàng téere bi di na la yóbu ci béréb yu mel ni :
§  Waalo fi nga xam ne foofa la Góorgi dëkkoon, mu nekkoon fa buur, amoon fa alal bu dul jéex.
§  Ndar muy fu Maram bayyekoo ci diwaan bu ñuy naan Loodo fa la juddoo magee fa te foofa tamm la ko Góorgi xame gànnaaw bu mu daan jàngee Ekkool Balañso fu ñu daan yónnee doomi buur yi te mu dalloon këru ñoom Maram.
§  Ndakaaru ca Tilleen gannaaw ba Góorgi bayyekoo Waalo mook jabootam. Fi la yëf yi xewee.
§   këru Góorgi, këru Kéwé, kër-madam, këru baayu Bugguma, ñoom ñépp nekkee ca Ndakaaru ñoo gëna fës ci téere bi.

            IV.            Tёnkub téere bi
Lépp a ngi tàmbalee ci ñaawtéef ak gàtt xel bi Ràkki am gannaaw bi nga xam ne muy baayam muy ndeyam su fekke ne sax seen loxo jotulwoon seen diggu gannaaw teerewul daan nañ def seen kemtalaay kàttan ba fac seen soxla te kenn masta xamal leen dara, rawaati nak dañu ko bëggoon lool, muy been bant bu nu yaakaar mu nekk seen reeni xol : lu ko neex def, lum laaj ñu jox ko, lum bëgg nu tegal ko. Ñu yàgga sey te kenn ma su leen na dëgg waala xamee leen dara : sutura ak muñ moo laal seen sey. Tilleen yépp kenn yabu leen. Waaw kon lu tax seen doom teg leen bi le gàcce ?
Góorgi Mbóoj moomi nga xam ne deretu buur mooy daw ci yaramam, la doomam dof-dof ba ñeeño (Bugguma) ëmbal ko, rax ci dolli muy doomu xaritam bu baax bum masa am ba muy jógee waalo ba tey gannaaw ba mu ñafee komaandan bi ba noppi ñów dëkk si Tilleen. Waaw lii, fu ñuy koy nettalijiyee ñoom mi nga xam ne daan naka waa Tilleen amu ñu woon lu ñu leen di sikkee lu dul di tooñ Góorgi, ñu koy naan buur Tilleen, ndeysaan bu waraan mbaam bi te mu nekkoon lu desoon ci alalam ba woon ca waalo ba muy nekk buur.
Bi naqar muy moom, muy jabar ji yóbu leen fu sori, mu delloo leen gannaaw ba ñu nekkee gune, fu ñu jaar ba fu ñu yegsi tey, soppeeku bi jamono  ji soppeeku. Ràkki daal, tas yaakaar way-juram la def.  Loolu tax nak Góorgi am xalaatu génne ko ci këram mu doon li ko meeti lool rawaati nak Maram su fekkee ne sax ànd ci woon.
Ràkki dund na lu mat ñetti weer gisul yaay, gisul baay, xaritam yi daw ko desewul dara lu dul Kéwé di yaayam bu ndaw moo mi nga xam ne moo ko fat bu ko baay bi génne këram te it ñépp sikk ko ngir jikkóom, ak Bugguma moom mi nga xam tamm baayam daf ko génne këram ba mu yégee li ni mel.
Maram dema-dem ba sës mu jóg seeti doomam ca këru Kéwé su fekkee ne sax Góorgi ànd ci woon benn yoon ba mu ko ci musa talaata, bakkanam nak la ci tegoon. Legg-legg Bugguma caalit waaye Ràkki muy dallal xelam te di ko fàtteli ne jamono mag ñi wutee nak seen bos.
Waaye seen xel jaxasoo na kerog ba ñu yégee ne Ràkki dem na kër-madam te nak mbiir mi dafa mel ni lu ëpp loxo. Muy Góorgi, muy Maram, muy Bugguma ku ci ne amoon nga naqar bu diis gannaaw bi leen doktoor ba yégalee génnum àddina Ràkki ak doom ja. Maram dee  li ndënk jëkkëram di Góorgi : … yaa rey sama doom,…





                V.            Jàngale yi ak suñu gris-gris ci téere bi

3.     Jàngale yi
Téere bi di Buur Tilleen ci yaatal mënes na ñoo wax ne rekk dey xàwwi jafe-jafe yi ak soppeeku guñu nemmeeku ci dëkk Afrig gànnaaw bi leen tubaab yi nootee ba noppi. Jàngalee yi ñu ci tibbee mën nañ ko xàjj ci ñetti ponk.
Bu ci njëkk mooy lépp lu aajo ci njekkin, kemb njub ak nekkinu réewum Senegaal baala  tubaab yi yegsi : xàjjoo bi am diggante géer, ñéeño ak jaam te nak mu doon li nga xam ne su fekke sax jamm ak salaam moo nekkoon seen diggante ku ci ne xamoon nga li la war (sey diggante géer ak ñéeño walla jaam musiba la woon). Jigéen dey déggaloon boroom këram, te soxlawul am xam-xam gu bari, ku ne lu ko way-juram yi sànt mu def ko te du ci teg baat. 
Ñaareel bi mooy li fi tubaab yi àndi muy Ekkool te nga xam ne làmmiñam la fa daan jàngale, njekkinam ak gis-gisam àddina. Ci kaw loolu li ci mel ni àq ak yellefu doomu aadama ak jigéen, demokaraasi. Gis nañu ci itam naka la daan dal ci kaw buur yi ba ci seen diwaan walla sax ci kanamu seen ni dëkk.
Bu mujj bi mooy mbëkkante bi am diggante njekkin ak kemb njubi réew mi ak lu fi tubaab bi àndi, ci yaatal diggante Afrig ak Orop. Ci biir téere bi gis nañu ne bile ndaje àndi jàmmaarloo diggante màgg ñi nga xam ne ñooy sam aada yi ak cosaani réew mi te xalaatu ñu been yoon weccee ko ak lennen, ak gone yi nga xam ne waxu nu dara ci seen cosaan waaye ànd ak li fi tubaabi àndi. War na ñoo fàtteli ne bu weesoo ñaari xalaat yooyu am na ñoo xam ne dañu gis ne mën a jël lépp lu baax ci lu tubaabi àndi boole kook lu nu am.
Ci gàttal nak téere bi di Buur Tilleen téere boo xam ne dey jàngal jafe-jafe yi dëkk Afrig yi ñu nootoon di am ci wàllum soxali seen aada ak cosaan ak soppeeku yu nu nemmeeku ci yilee réew .    

4.     Suñu gris-gris ci téere bi
 Téere bi di Buur Tilleen bu dara desul li dul wax suñu xalaat, lu ñuy njëkk a def mooy rafetlu  liggéeyu ndanaan dëgg bu ki di Séex Aliyu Ndaw def.
Bu loolu weesoo, bind mi ci téere bi nak amu ñu ci dara lu ñu ci mëna ɳàññ ndaxte li ko dooree ci ndoortel li, ba fa mu jéexe ak ci wàllum màndargaal mi gisu ñu leen lu jaarul yoon walla sax wax ju ñaaw. Rax ci dolli lépp a leer nañ te neex a jàng.
Gannaaw nak ba ñu jàngee téere bi ba noppi duñu def lennen lu  dul ñaawlu jëf ju ñaaw ju  Ràkki def te nak di ci jaaraale yedd suñu jigéenyi, ne leen, nañ sam seen bopp bu ko defe ñu baña dugal seen bopp ci yu mel nii. Ràkki nak waroon na yëram way-juram, te mu sam boppam bu ëlëgee mu siggil leen ndax moom rekk lañ yaakaar gannaaw Yàlla, te mu xam ne baayam di Góorgi mënoon na déglu mbokkam mi te mu tàkk beenen jabar ku koy mëna jural yeenen doom. Waaye boo gisee lu tax li yépp defu ko, bëgg bu leen bëgg mook Maram waaye tammit wóolute bum amoon ci moom. Kon Ràkki tey dafa tas yaakaar way-juram. Lii nak meetina lool saka boo xamee ne ki di Ràkki benn at a ko desewaan mu jéexal jàngam ca Ekkool saasfaam ya. Waaye, ndax lii mu def, jaar na baay bi dàq ko këram ? Ndaxam Góorgi moom mi nga xam ne deretu buur moy daw ci yaramam moom la doomam fowee boppam ba ñéeño ëmbal ko ci ? Waaye nak leen am na, jamonoy soppeeku yëf yi soppeeku. Góorgi nak dafa waroon seet ci Maram ak malaaka bi nga xam ne moo newoon ci Ràkki te nak yoonam newu ci li Bugguma def ak Ràkki. Waaye da fa topp xolam ba def li nga xam ne gënalu ko woon. Bugguma nak dàq ko daggaana, ndaxte yeenuwul dara lu ñu mëna ne di na ko sonal walla lu tax ñu nan du ci génn, rax ci dolli muy góor. Te nak, nañu waxante dëgg, su fekkee ne sax Ràkki jum na, terewul baayam ak ndeyam am nañ ci seen wàll. Li ko waral mooy, su fekkoon ne dañuy faral di seetlu bu baax seen doom, fum doon dugu ak lim ndan def, ni mu tuti-tuti di nañ nemmeeku ay soppeeku ci moom. Ndeysaan, xam na ñoom dañ dan xalaat ne seen jamono ni mu meloon noona la mel ba tey, xamu ñu ne la woon, wooni na.    


Njéextal
Téere bi di Buur Tilleen, mën na ñoo wax ne  téere la bi nga xam ne dey yeedate ak yee li di doomi réew mi ngir ñu baay seen xel bu baax ci li mel ni li fi tubaab bi baayi ak soppeeku jamono ji. Waaye nak gis nañu itam ne daxul lépp lu fi tubaab yi àndi, waaye lu mu wone moo di xayma lépp lu baax boole ko ak li ñu yor, bu ko defe leen du ñu jaxal. Téere bi nak ki Séex Aliyu Ndaw, bind na ko ci wolof bu leer te yomb jàng te nak wax dëgg Yàlla cërël na li di màndargaal yi. Ci kaw loolu ñoo gi ñaawlu njéextal téere bi ndaxte su doon suñu saggo kenn du ci ñàkk bakkanam bu ko defe baal ak baalu mëna am waaye it tuub ndax bañ ko defa ti.      
Nestor Japa Faal             


Commentaires

Posts les plus consultés de ce blog

Concepts scientifiques FR-WO / Mathématiques Inspirés de l'oeuvre de Cheikh Anta Diop

Le wolof